Ta`jabuun (تَعۡجَبُونَ>) di xeetu yalwaan, ay dongo daara daa ko amal te daa ci boole waare, xupp ñi dul julli, du ñu
Ay Dongo yuy Jàng
Ay Dongo yuy Jàng
woor, du ñu doxug bokk, tey bégal ñiy julli, di woor, tey jokk ag bokk, di léen fàttali it li Yàlla wax ci joxe, boole ko nag di ko waxe ci waxiin woo xamni jamono jooja ku bëgg ñu déglu la noona ngay waxe, muy daaj ko, ba waral ñu daaj ko, wut baat bob dina man ab daaneel muy "Jee" di baatu wolof muy "jeex" bees ko gàttalee muy "jee", niki bàyyi ak ba.



Liwaral baatu Ta`jabuun, ñi ci dugg bi mbir mi neexee te tàmbalee amus xaalis te duñuy donga tax séeni làmmeñ yàq baat bi naan Taajaboon, loolu nag gënul ndax Alxuraan la te kenn waru koy damm. 
Baat bi "Ta`jabuun" moo ngi ci Saar wees daa tari di Wannajmi (ci biddiw bi) Saaru 53 ci Laaya 59, Yalla di wax ci laaya yu mujj yooyu naan «Ndax dangeen di yéem wii waxtaan (L;59) di reetaan te doo leen jooy (L:60) ak ngéen di woy (L:61)» cosaanul lu tax ñu tànn baatu Ta`jabuun, xamu ma ci lu weesu Yéemu gi yaxub baat bi di tekki.

Xamees na ci aw defiin wees fi man a joxe ñeel ku ko bëg a defe nees ko daa defe bawoon, buñu jëmaan ci genn kër kenn jiitu ngir dëbbe ñi ci des di ko tontu, niki muni Ta`jabuun ñu ni Àllay, muni wannajmi ñu ànd ak moom ci jee (jeex), loolu nag kon day melni dañoo dolli ci Alxuraan jee ndax buñu wax teg jee, ahakay! loolu la ci bees xoolee ci génn wet gi waaye it déedéet, "jee" ji bokkul ci wax ji, niki mani: maangi dem tuubaa, boomay téyé, dem, boomay dóor, dem, ak yuni mel...

Ta`ajaboon jaangi: 
Ta`jabuun - Àllay ! Ta`jabuun - Àllay ! Ta`jabuun - Àllay ! Sama taaj gii - Àllay ! balaa ma koy ba (bàyyi) - Àllay !
Wannajmi (jee), Isaa hawaa (jee) Ma dalla/lalla (jee), Saahibukum (jee), Wamaa Xëwaa (jee), toppee ko noonu ba saar wa jee boo ko manee... 
Newaat: Ta`jabuun Ta`jabuun Ta`jabuun, Abdu jàmbaar - Àllay, ñaare (souvent) malayka la - Àllay, ci kow lay xawe, - Àllay, daanu fi sab ruum - Àllay, ne ndax julli ngaam ? - Àllay, nga ni déedéet - Àllay, ne ndax woor ngaam ? - Àllay, ngani déedéet - Àllay, yaangi doxug bokk ?- Àllay, ngani déedéet - Àllay, ñu jaget-jegetee sànni ca sawara saa, ngani téqét jooy, Ta`jabuun, Ta`jabuun, Ta`jabuun, Abdu jàmbaar - Àllay, ñaare malayka la - Àllay, ci kow lay xawe, - Àllay, daanu fi sab ruum - Àllay, ne ndax julli ngaam ? - Àllay, nga ni waawaaw - Àllay, ne ndax woor ngaam ? - Àllay, ngani waawaaw - Àllay, yaangi doxug bokk ?- Àllay, waawaaw - Àllay, ñu jaget-jegetee yobbu ca àjjana jaa, ngani téqét ree, Ta`jabuun, Ta`jabuun, Ta`jabuun, dañuy Ta`jabuun, Lan tanaaloo - Birra, Hattaa tunfuquun - Birra, Mimmaa Tuhibbuun - Birra, Diw (Faatu, Soxna, Awa, mbaa ku fa ne) mi ci kër gi - Birra, neel kër-kër - Birra, ni kàccet sa gaal (dencuwaay) - Birra, ndonga njaay xeebul - Birra, Dërëm mbaawu ñaar - Birra, ndonga njaay xeebul - Birra, ginaaw gu ŋootoot - Birra, ndonga njaay xeebul - Birra, tef bu juddu daaw, Ta`jabuun ! Ta`jabuun ! Ta`jabuun ! di demaale geneen kër....


Li aju ci soli sagar ga ak jigéen di sol yéréy góor, góor it noonu, fi ñu ko toppandoo moodi dongo ya ko daa def dañu daa rafle, ba mujj loru ( tax ñu may léen ko), sagar wu ñu for rekk sol, ngir ñàkki yéré bu ko defee luñu jekku sol. Waaye ku léen di toppandoo batax ngay sol yéréy góor mbaa yérey jigéen ci góor yaangi def lees aaye, diw sa kanam ab dóom mbaa lu ni mel it noonu, loolu it dongo yi lañu ciy toppandoo te loru moo léen ko daa tax a def, ngir ñàkk ndoxum sangu te foo toll nekk ci suuf si ak taali jàngu yi ba weex.

Abdu Xaadir GEY

Enregistrer un commentaire

 
Top