Lu aju ci bisu Tëbëski
Tëbëski mooy ñaareelu iid (bër) ci lislaam ginnaaw bu Korite jàllee. Jële na nu ci Anas (gërëmul Yàlla Yal na nekk ci moom) mu ne: Bi Yonent bi (Yalna jàmmi Yal na nekk ci moom) yegsee Madiina fekkee na léen ñaari bis ñu ca daan caaxaan ak a fo.
-Mu ne (jàmmi Yàlla ci moom) léen : « Ana lu [waral] ñaari bis yii ? »
-Ñu ne ko : “Danu ci daa caaxaan ci jamonoy ceddo (jaahiliya)”

-Yonent bi (jàmmi Yàlla ci moom) ne léen: «Yàlla jox na léen ñaari bis yu gën yooyu ñaar, muy Bisu tëbëski ak bob Kori» (Abuu Daawud soloo na ko)
Moom Täbëski dees na ko amal ci fukkeelu (10eel) bis ci aw Täbëski, di weer wi mujj ci atum weer wi (Wolof). Ñaari bër (fête) yooyu, di tëbëski ak Kori, bokk nañu ci teddngay lislaam, ba tax na kenn sañu cee woor. Yonent bi (Jàmmi Yàlla yal na nekk ci moom) tere na ku ci woor. Waaye nag bu dee bisu Täbëski sunna la boo xëyee bañ a lekk darra ba baa ngay julli ba déllusi doge ci tëbëski mi. Bu dee kori safaan bi mooy sunna, lekk njëkk ngay julliji.
Tëbëski (rendi gàtt):
Ci Ngiirum Maalig ak Shaafi`, Tëbëski, maanaam rendi gàtt, Sunna la su far ci ab jullit bu di mukàllaf, di as gor, man ko te mu bañ koo sonal, bu yooyu dajee mag ak gone ñoo ci yam ku xës mukàllaf sunna su far si war na la. Sunna su far soosu nag, man naa mujj di farata ci ñaari anam yii :
1. Ci ku ko nësër : niki nga ni bu ma Yàlla defalee nàngam dinaa tëbëski. Fu loola amee rekk manatul a ñàkk, farata la ci yaw.
2. Ci ku xës jënd am tëbëski, walla mu yor am xar jublu ci tëbëski : bu loolu xësee am day daadi nekk farata ci yaw.
Àtteb Tëbëski ci Lislaam ?
Yàlla nee na: «Jullil ngir sa Boroom te rendi (lottal)» (Saaru 108 / Laaya 03)
Yonent b i(jàmmi Yàlla ci moom) nee na: «Ku am dooley [man a rendi am] tëbëski te tëbëskiwul, bu mu jege sunu barabu julliwaay» (Abuu Hurayra moo ko nettali, Ibn Maaja, Ahmad, Daaru Qutni ak Al-Haakim soloo nañ ko, doonte barina ñu jam hadiis bi ci woroom xam-xam yi, niki Haasim ak ñeneen)
Baraan nettali na ni, Yonent (Jàmmi Yàlla ci ñoom) bi nee na: Li nuy njëkk a def ci bis bii, moo di julli, ginnaaw ba nu dellu lottal (rendi), ku def loolu def na sunu sunna. »
Ash-Shaari` nee na: «Duma nangu ku am dooley am tëbëski di ko sàggane »
Yonent bi (jàmmi Yàlla ci moom) saxaloon na ko te daan ko digle.
Sunna la su far ci Ñoñ-Maalig, Shaafi`, ag ñenn ci waa Ahmad Ibn Anbal. Bu dee nag ci ngiirum Abuu Hanifa ñoom lu war la. Lu war ca ñoñ Abuu Hanifa nag tekkiwul farata la.
Lu man a am nag ñépp dëppoo na ñu ci ne dina war ci ñaari anam yii:

2. Ci ku xës jënd am tëbaski, walla mu yor am xar jublu ci tëbëski : bu loolu xësee am day daadi nekk farata ci yaw.
Sopp na ñu yii ci bisu Tëbëski :
- Sangu luñ sopp la;
- Sol yére yu bees buy julliji, ak xeeñoo lëjkoloñ (ba mu des rekk ci jigéen) ;
- Sopp nañu nga bañ a lekk darra ba julliji ba ñëw, soog a lekk;
-
Am tëbëski (gàtt):
Yàlla nee na ci Alxuraan (la nu déggee ci wax ji): «Yàlla amul Soxla ci yàpp wi walla dereet ji; waaye la ko ca soxal mooy ragal [Yàlla] gu bawoo ci yéen. Noonu na la nu léen léen tàggate ngir ngéen Màggal Yàlla ci li mu léen gindi. Te nanga bégal way-rafetal ñi » S22 L:36
Kon nanu jàpp njëkk ni yéene ju sell te Yàlla rekk tax waliif ngistal walla wanu ci bëti nit ñi mooy maye yoolu tëbëski. Ci lislaam ñaari mbir sàrt la ci nangug jëf jum man a doon : benn ; mu dëppoo ak sunna ; ñaar : Sellal ko ngir Yàlla dong.
Yonent bi (Ya lna jàmmi Yàlla nekk ci moom ) nee na : «Sellal léen séen i jëf, ngir Yàlla kët du nangu ludul luñ sellal ngir moom »
Sàrt yii nag moo koy tax a wér :
Yees nanguwul ci am Tëbëski:
Am Tëbëski it war naa mucc ci yii:
Lees di bañ ci ndawalug am tëbëski:
Am tëbëski sañees na cee maye, sañees na cee lekk, sañees na cee denc.
Xataada Ibn An-Nu`maan nettali na ne : Yonent bi (Yal na jàmm Yàlla nekk ci moom) xëy na bis ne leen : Maa léen terewoon lekk ndawalug Tëbëski lu weesu ñatti bis [u tëbëski]. May naa léen ko léegi ; lekk léen ci nim léen neexe. Waaye bu léen jaay ndawalug Tëbëski, lekk léen ci, joxe léen ci sarax. Jariñoo léen der bi waaye bu léen ko jaay. Buñ léen ci joxee it lekk léen. » (Ahmad soloo na ko)
Nees di rendee ak li ci aju :
Rendi ab jullit moo koy def, te doon ku am xel. Melo wi ci gën nag moodi mu tëral la muy rendi ci wetug càmmooñam te mu jublu xibla (kaaba ga), bu dee am xar mu tëral noppub ndeyjoor ba; ba fa mu yam ca baat ba, mu teg foofa paaka ba. Walla bu amee téerey baat mu teg paaka ba ca diggante téere ya. Bu ko defee balaa caa teg paaka ba mu wax ci am xelam ni "fas na maa yéenee daganal lekk yàppu nàngam wii ci rendi gi ma koy rendi". Bu dee teg paaka ba mu wax:« Bismil Laahi » daaldi koy dawal ba ñaari sidit yu mag ya ak boli ga lépp dagg. Bu ko bombee ba deret ja génn mu wax: Allaahu Akbar. Bu teggee loxoom mu wax: «Rabbanaa taqabal minnaa innaka anta s-samii`u L-`Aliim »(S002/L126:).
Bu dawalee paaka ba ba sidit ya tàmbalee dagg mu teggi ko, bu ko ca gaawee delloo dees na ko lekk. Bu ko ca yeexee delloo nag te lor waralu ko, kon deesu ko lekk. Te yit bu mu tàngale baat ba, bu ko defee it du ko tee dagan, waaye bañ koo def a gën.
-Rendi xar ak bëy ci kanam lees koy defe; boo ko rendee ci ginnaaw walla ci wet, deesu ko lekk;
-Bu dee aw nag manees na koo rendi manees na koo loj,
-Bu dee Ginaar nag war naa wërale paaka ba, ca gannaaw ak ca kanam, ba sidit yu sew yépp dagg te mu bañ a tàngale baat ba, bu ko defee it du ko tee baax waaye bañ koo def a gën.
-Giléem deesu ko rendi mukk, li feek du dañoo loru amuñu lojukaay te am rendikaay.
Loj aj li ci aju :
Kuy loj, day taxawal lamuy loj jubale ko "XIBLA" (Kaabag Màkka). Lem baat ba tëral ko ci wetug càmmoñ ga, bu ragalee barig dooley la muy loj, man naa yeew tànkub càmmooñu kanam ba. Balaa tàmbali mu wax «Bismil Laahi», bu tàmbalee mu bañ a dindi loxoom lifeek noppiwul.
Lees war a loj nag bees amul lojukaay sañees na koo rendi, lees war a rendi it bu ñu amul rendikaay te am lojukaay sañees na koo loj.
-Giléem loj rekk lees koy def mbaa deesu ko lekk waaye deesu ko rendi, xanaa ñu loru ñàkk lojukaay te am rendikaay, bu boobaa nag dees na leen ko may;
-Bu dee aw Nag dees na ko loj niki noonu it dees na ko rendi, kon moom lu leen jekku rekk ñu sañ koo def noona (Fii nag rendi ko lañu gën a miin).
Loj, balaa baax ñatti sidit yu mag yi daa war a dagg, kon ci ag wet lees koy defe ak kanam.
Na moytu yii : Bu dawalee paaka ba, ba sidit ya tàmbalee dagg mu teggi ko, kon bu ko ca gaawee delloo dees na ko lekk. Bu ko ca yeexee delloo nag te lor wara lu ko, kon deesu ko lekk. Te yit mu bañ a tàngale baat ba, bu ko defee it du ko tee dagan, waaye bañ koo def a gën.
Waxtuw rendi walla loj:
Mi ngi dale ci rendig Yilimaan, rendig yilimaan moo ngi aju ci ginnaaw bu sëlmalee julli gi, ba kerog jant di so ca bisub ñatteel ba fu ñu ko fi rendee mu baax. Ci ngiirum Maalig fàww rekk mu doon bëccëg, ci teewaayu jant bi, deesu ko sañ a ray guddi. La ca gën moodi boroom rendil ko boppam, bu amee ngànt mu wuutal ko moroomum jullitam, te nanga yéene yaw mi ñuy rendil. Ku dul ab jullit manu laa rayal am tëbëski.
Ku rendi tëbëskim jàmbur te amu ci ndigël, du ko doy am tëbëski te war naa fay boroom.
Am Tëbëski nag deesu ko rendi jëkk rendig Yilimaan te Yilimaan it balaa rendi nig ba julli. Ci ni ko Yonent bi (jàmmi Yàlla ci moom) waxe :« Képp ku rëy njëkk jullig bër gi, deful lu dul rëy baayima buñ man a lekk ; waaye ku rëy ginnaaw jullig bër gi nag, am na am Tëbëski» (Buxaari soloo na ko)
Ngënéeli Tëbëski:
Yonent bi (jàmmi Yàlla ci moom) xamle na ni toq dereet wiy njëkk a génn Yàlla di na ci jéggale mboolem bàkkaar yu waay mas a def, nii la dikke ci hadiis ci nettalib Aysa (ngërëmul Yàlla ci moom).
Jëlee nanu ci Ibn Abaas mu ni Yonent bi (jàmmi Yàlla ci moom) nee na : «Alal dugaleesu ko ci lu gën gàttub tëbëski (iid)» (Daaru Qutni soloo na ko)
Yonent bi (jàmmi Yàlla ci moom) bégal nanu ci ne Xarum tabaski dina njot ci sawara niki mu njoteewoon bakkanu Ismaayla. Amul jëf ju nit di def ci bisu Tëbëski ju gën a neex Yàlla tuur ci dereet. Noonu la ko Aysa nettalee.
Taarixu Tëbëski
Tëbëski xew wu am solo la ci lislaam tey jëmmal xew-xew bu am solo ci jëflànteg nit ak Boroomam. Di la xewoon ci diggante Yonent Yàlla Ibraayma, doom ja Yonent Yàlla Ismaayla (Jàmmi Yàlla ci ñoom), ak Boroomam, ca bam dëelantee ak Boroomam ci rayal ko doom ja muy njëkk a am ngir won ko cofeelam ak gënal gum ko gënal leneen ludul Moom. Ba doomam ju jëkk juddoo, tudd Ismaayla, nekk gu doom nekk ci moom lu bees tax mu am cofeel gu rëy ci moom. Loolu tax, boroom bi xabaar ko ci gént ngir fàttali ko séen ndëel ba. Ba mu ko wérloo ba muy ndéey (wahyu/révélation) lu leer, ca la ko yëgal Soxna sa. Soxna sa deful lu may rafetlu ko, doonte ni doom foore ci ndey. Waaye rekk mu am kóolute ci Boroomam.
Niki noonu it la ko yëgale doom ja, ni ko "(...) Yaw samas ndoom man de gént naa di la rendi, xoolal loo ci xalaat (...)" (S37/L0102). Doom ja ànd ak la muy nekk ndaw lépp, mu toontu ko ni "Yaw sama baay defal lees la digël. Man nag, bu neexee Yàlla, da nga ma fekk ma bokk ca way-muñ ya" (S37/L0102)
Ba ñu déggoo ñoom ñépp ci jëfe ndigël li, Ibraayma ànd ak Ismaayla ngir rendiji ko nim ko gise ci gént gi. Ba loolu amee, Ismaayla sàkku ci moom mu takk ay gëtam ngir bañ koo yërëm ba du jëfe ndigël li. Ba mu takkee ay gëtam nag ba dogu ci rendi ko, Alxuraan nee:
"Nu woo ko, ni ko Eey! Yaw Ibraayma.
Dëggal nga gént gi. Nun de noonu la nuy faye way rafetal yi.
Dëgg-dëgg lii nattu la bu bér (diis). "
Nu daaldi koy njot (moom Ismaayla) ci gàtt bu rëy.
Daaldi koy bàyyi mu bokk ci way-des ñi (di dund).
Jàmmi Yàlla [Yal] na nekk ci Ibraayma.
Nun nag noonu la nuy faye way-rafetal ñi.
Moom daal ci sunu jaam yi di way-gëm la bokk." (S37/L0104-111)
Tëbëskig Jàmm !
Di léen balu àq ; di leen baal àq, tey ñaan Yàlla boole nu baal. Te nu fekke ko te romb ko.
Déwénati,
Aji-Bind ji: Abdu Xaadir GEY,
Kenn ci way-sosi Akaademi Wolof https://www.facebook.com/ groups/akaademiwolof/

- Xar mu am juróom benni (6 i) weer mbaa at aki fan ci li sax ci ñoñ-Maalig. Bu dee aw bëy nag, na am at ak weer ci ñoñ-maalig ;
- Xar a gën, topp bëy, topp nag ak giléem ;
- Xar mu góor a gën mu jigéen, bëy wu góor a gën wu jigéen, nag ak giléem naka noonu.
- Juróom ñaari jullit man nañoo boole jënd aw nag walla giléem.
- Bu dee xar walla bëy nag kenn du ko bokk jënd.
- Waaye nag man ngaa ray yéene ci képp kuy yewwoo ci kër gi, moo xam muy koo xam ne dundal ko yaw la war, niki say doom ak sa soxna, walla muy koo xam ni dundal ko waru la, niki say rakk yu góor ak jarbaat... Buñ ko amul yéene léen ci dina léen doy am tëbëski. Ku nekkul ci kër gi nag deesu ko ci man a yéenewaale.
Yees nanguwul ci am Tëbëski:
- Bu benn béjjan dammee te wérulagul , manaan di nàcc, du matum tabaski (ci maalig). Bu wéree may nañ la ko. Bu judduwaalewul ay béjjen it darra nekku ci ;
- Bees xaajee nopp ba ñatt (1/3), la ca dagg bu matee benn xaaj ba, matul am tëbëski. Bu judduwaalewul nopp walla nopp ya gàtt nag darra nekku ci ;
- Niki noonu it bu nopp ba xaree lu toll ci benn ci ñatti xaajam (1/3) du mat am tëbëski
- Bees xaajee geen ba ñatt, la ca dagg bu matee benn ca ñatti xaaj ya (1/3) matul am tabaski. Bu ko judduwaaleewul walla mu gàtt nag darra nekku ci.
Am Tëbëski it war naa mucc ci yii:
- Bumu yooy ba amul nebbon (ndawal)
- Bu gimiñ ga xasaw ba jéggi dayo
- Bu bët ya/ba patt ba fés, rawati na nag muy gumba
- Bu tànk ba làgge ba fés, rawati na nag mu damm
Lees di bañ ci ndawalug am tëbëski:
- Bañees na ku ca jaay darra ca yàpp wa ak ca der ba. Ku ko ñaani ba ñu may la ko nag man na koo jaay, darra nekku ci.
- Bañees na yitam ka koy fees ñu di ko fay ca yàpp wa, waaye manees na ko caa may walla sarax,. Bu laajee ag fay fayees ko xaalis walla leneen. Noonu it la àtte ci deme ci am tudd.
- Bañees na gépp joxe ngir wareef (obligation/devoir), niki tànku njëkke, yeeli maam, baatu feeskat, ak yu ni mel...
Am tëbëski sañees na cee maye, sañees na cee lekk, sañees na cee denc.
Xataada Ibn An-Nu`maan nettali na ne : Yonent bi (Yal na jàmm Yàlla nekk ci moom) xëy na bis ne leen : Maa léen terewoon lekk ndawalug Tëbëski lu weesu ñatti bis [u tëbëski]. May naa léen ko léegi ; lekk léen ci nim léen neexe. Waaye bu léen jaay ndawalug Tëbëski, lekk léen ci, joxe léen ci sarax. Jariñoo léen der bi waaye bu léen ko jaay. Buñ léen ci joxee it lekk léen. » (Ahmad soloo na ko)
Nees di rendee ak li ci aju :
Rendi ab jullit moo koy def, te doon ku am xel. Melo wi ci gën nag moodi mu tëral la muy rendi ci wetug càmmooñam te mu jublu xibla (kaaba ga), bu dee am xar mu tëral noppub ndeyjoor ba; ba fa mu yam ca baat ba, mu teg foofa paaka ba. Walla bu amee téerey baat mu teg paaka ba ca diggante téere ya. Bu ko defee balaa caa teg paaka ba mu wax ci am xelam ni "fas na maa yéenee daganal lekk yàppu nàngam wii ci rendi gi ma koy rendi". Bu dee teg paaka ba mu wax:« Bismil Laahi » daaldi koy dawal ba ñaari sidit yu mag ya ak boli ga lépp dagg. Bu ko bombee ba deret ja génn mu wax: Allaahu Akbar. Bu teggee loxoom mu wax: «Rabbanaa taqabal minnaa innaka anta s-samii`u L-`Aliim »(S002/L126:).
Bu dawalee paaka ba ba sidit ya tàmbalee dagg mu teggi ko, bu ko ca gaawee delloo dees na ko lekk. Bu ko ca yeexee delloo nag te lor waralu ko, kon deesu ko lekk. Te yit bu mu tàngale baat ba, bu ko defee it du ko tee dagan, waaye bañ koo def a gën.
-Rendi xar ak bëy ci kanam lees koy defe; boo ko rendee ci ginnaaw walla ci wet, deesu ko lekk;
-Bu dee aw nag manees na koo rendi manees na koo loj,
-Bu dee Ginaar nag war naa wërale paaka ba, ca gannaaw ak ca kanam, ba sidit yu sew yépp dagg te mu bañ a tàngale baat ba, bu ko defee it du ko tee baax waaye bañ koo def a gën.
-Giléem deesu ko rendi mukk, li feek du dañoo loru amuñu lojukaay te am rendikaay.
Loj aj li ci aju :
Kuy loj, day taxawal lamuy loj jubale ko "XIBLA" (Kaabag Màkka). Lem baat ba tëral ko ci wetug càmmoñ ga, bu ragalee barig dooley la muy loj, man naa yeew tànkub càmmooñu kanam ba. Balaa tàmbali mu wax «Bismil Laahi», bu tàmbalee mu bañ a dindi loxoom lifeek noppiwul.
Lees war a loj nag bees amul lojukaay sañees na koo rendi, lees war a rendi it bu ñu amul rendikaay te am lojukaay sañees na koo loj.
-Giléem loj rekk lees koy def mbaa deesu ko lekk waaye deesu ko rendi, xanaa ñu loru ñàkk lojukaay te am rendikaay, bu boobaa nag dees na leen ko may;
-Bu dee aw Nag dees na ko loj niki noonu it dees na ko rendi, kon moom lu leen jekku rekk ñu sañ koo def noona (Fii nag rendi ko lañu gën a miin).
Loj, balaa baax ñatti sidit yu mag yi daa war a dagg, kon ci ag wet lees koy defe ak kanam.
Na moytu yii : Bu dawalee paaka ba, ba sidit ya tàmbalee dagg mu teggi ko, kon bu ko ca gaawee delloo dees na ko lekk. Bu ko ca yeexee delloo nag te lor wara lu ko, kon deesu ko lekk. Te yit mu bañ a tàngale baat ba, bu ko defee it du ko tee dagan, waaye bañ koo def a gën.
Waxtuw rendi walla loj:
Mi ngi dale ci rendig Yilimaan, rendig yilimaan moo ngi aju ci ginnaaw bu sëlmalee julli gi, ba kerog jant di so ca bisub ñatteel ba fu ñu ko fi rendee mu baax. Ci ngiirum Maalig fàww rekk mu doon bëccëg, ci teewaayu jant bi, deesu ko sañ a ray guddi. La ca gën moodi boroom rendil ko boppam, bu amee ngànt mu wuutal ko moroomum jullitam, te nanga yéene yaw mi ñuy rendil. Ku dul ab jullit manu laa rayal am tëbëski.
Ku rendi tëbëskim jàmbur te amu ci ndigël, du ko doy am tëbëski te war naa fay boroom.
Am Tëbëski nag deesu ko rendi jëkk rendig Yilimaan te Yilimaan it balaa rendi nig ba julli. Ci ni ko Yonent bi (jàmmi Yàlla ci moom) waxe :« Képp ku rëy njëkk jullig bër gi, deful lu dul rëy baayima buñ man a lekk ; waaye ku rëy ginnaaw jullig bër gi nag, am na am Tëbëski» (Buxaari soloo na ko)
Ngënéeli Tëbëski:
Yonent bi (jàmmi Yàlla ci moom) xamle na ni toq dereet wiy njëkk a génn Yàlla di na ci jéggale mboolem bàkkaar yu waay mas a def, nii la dikke ci hadiis ci nettalib Aysa (ngërëmul Yàlla ci moom).
Jëlee nanu ci Ibn Abaas mu ni Yonent bi (jàmmi Yàlla ci moom) nee na : «Alal dugaleesu ko ci lu gën gàttub tëbëski (iid)» (Daaru Qutni soloo na ko)
Yonent bi (jàmmi Yàlla ci moom) bégal nanu ci ne Xarum tabaski dina njot ci sawara niki mu njoteewoon bakkanu Ismaayla. Amul jëf ju nit di def ci bisu Tëbëski ju gën a neex Yàlla tuur ci dereet. Noonu la ko Aysa nettalee.
Taarixu Tëbëski
Tëbëski xew wu am solo la ci lislaam tey jëmmal xew-xew bu am solo ci jëflànteg nit ak Boroomam. Di la xewoon ci diggante Yonent Yàlla Ibraayma, doom ja Yonent Yàlla Ismaayla (Jàmmi Yàlla ci ñoom), ak Boroomam, ca bam dëelantee ak Boroomam ci rayal ko doom ja muy njëkk a am ngir won ko cofeelam ak gënal gum ko gënal leneen ludul Moom. Ba doomam ju jëkk juddoo, tudd Ismaayla, nekk gu doom nekk ci moom lu bees tax mu am cofeel gu rëy ci moom. Loolu tax, boroom bi xabaar ko ci gént ngir fàttali ko séen ndëel ba. Ba mu ko wérloo ba muy ndéey (wahyu/révélation) lu leer, ca la ko yëgal Soxna sa. Soxna sa deful lu may rafetlu ko, doonte ni doom foore ci ndey. Waaye rekk mu am kóolute ci Boroomam.
Niki noonu it la ko yëgale doom ja, ni ko "(...) Yaw samas ndoom man de gént naa di la rendi, xoolal loo ci xalaat (...)" (S37/L0102). Doom ja ànd ak la muy nekk ndaw lépp, mu toontu ko ni "Yaw sama baay defal lees la digël. Man nag, bu neexee Yàlla, da nga ma fekk ma bokk ca way-muñ ya" (S37/L0102)
Ba ñu déggoo ñoom ñépp ci jëfe ndigël li, Ibraayma ànd ak Ismaayla ngir rendiji ko nim ko gise ci gént gi. Ba loolu amee, Ismaayla sàkku ci moom mu takk ay gëtam ngir bañ koo yërëm ba du jëfe ndigël li. Ba mu takkee ay gëtam nag ba dogu ci rendi ko, Alxuraan nee:
"Nu woo ko, ni ko Eey! Yaw Ibraayma.
Dëggal nga gént gi. Nun de noonu la nuy faye way rafetal yi.
Dëgg-dëgg lii nattu la bu bér (diis). "
Nu daaldi koy njot (moom Ismaayla) ci gàtt bu rëy.
Daaldi koy bàyyi mu bokk ci way-des ñi (di dund).
Jàmmi Yàlla [Yal] na nekk ci Ibraayma.
Nun nag noonu la nuy faye way-rafetal ñi.
Moom daal ci sunu jaam yi di way-gëm la bokk." (S37/L0104-111)
Tëbëskig Jàmm !
Di léen balu àq ; di leen baal àq, tey ñaan Yàlla boole nu baal. Te nu fekke ko te romb ko.
Déwénati,
Aji-Bind ji: Abdu Xaadir GEY,
Kenn ci way-sosi Akaademi Wolof https://www.facebook.com/
Enregistrer un commentaire