Un poème de Serigne Moussa Kâ dédié à un des attirés vers Allah (Majzuub) de Serigne Touba à savoir Serigne Ababacar Sarr plus connu sous le nom de Serigne Mbaye Sarr. Les attirés vers Allah, dans le jargon soufi, sont caractérisés par le fait qu'ils ne sont pas des exemples à suivre à la lettre, subjugués qu'ils sont par la puissance des lumières divines et des états mystiques qui sont les leurs qui font que leurs actes peuvent parfois défier l'entendement et même plonger dans la perplexité les plus orthodoxes. Ceci étant, même si leurs actes peuvent paraître aller à l'encontre de la loi exotérique, un connaissant par Allah lui saura qu'il n'en est rien. Les voies du Seigneur sont impénétrables. C'est ce que Serigne Moussa Ka, dans un style inimitable et élégiaque qui est le sien, tente de faire comprendre au commun des mortels.
"Abaabakar Saar" [Sëriñ Mbay Saar]
Muriid yi xam leen ne Abaabakar Saar
“Majsóob”la, kuñ wommat du xam fa muy jaar
Yëngoom ba ak dalam ga léppay “lasraar”
Tëggam ma ak tëbam ma léppay “lanwaar”
Gumba gu jébbal tum ba ngën nji njaccaar
Du ko ne fii ngay jaar, “soféeray” yor mbaar
Bàmbaay boroom saxaar gi, Baabakar Saar
“Wagoo” ma, seen bagaas du teggi ab gaar
“Majsóob” ya daa sóobu ba seey ngir “lanwaar”
Buñ dekki won ba jis ko dollikug waar
Naankat bu màndi dootu tagook bàkkaar
“Majsóob” bu jeex ci Yàlla dootul bàkkaar
Yaa jeex ci Siidi Bàmba, yaa doyug waar!
Luumal nga fóore ya “kazaaka lahbaar”
Jaaxal nga nasraan yi lëjal nga “laxyaar”
Semmal nga “lachyaax” yay boroomi “lasraar”
Góoru “muhaajiriina” yaaki “lansaar”
Gàddaay nga seen gàddaay ga Baaba naam Saar
Yaa donnu kër Seex Anta Siidil Muxtaar
Wallaahi bii tabax niroowul ak mbaar
“Jazaaka” yal na Yàlla fay la yaw Saar
“Yawmal jazaa’i ka rijaali lansaar ”
Sëriñ Muusaa Ka
Aji bindaat ji : Sñ Jeŋ

Enregistrer un commentaire

 
Top