« Au nom de Dieu Le Tout Miséricordieux, Le Très Miséricordieux Après avoir rendu grâce à Dieu et prié sur le Prophète (Paix et Salut Sur Lui), sache que j’ai bien reçu ta lettre et pris connaissance de son contenu.
[Toi mon frère], je te recommande de demeurer dans la crainte révérencielle de Dieu, car elle est la clef qui ouvre la porte de tous les bienfaits et constitue le verrou de la porte de tous les méfaits. La crainte de Dieu revient à ne s’approcher d’aucun de ses interdits et à se montrer persévérant dans ses ordres.
Je te recommande de demeurer dans l’observance de la Sounnah du Prophète (Paix et Salut sur Lui) et de t’écarter de toute innovation blâmable. Nourris h la considération envers tes deux parents et observe leurs recommandations dans tout ce qui n’est pas désobéissance au Seigneur. Tâche de ne jamais rompre les liens avec eux. Il est dit dans un hadith : « Quiconque prend soin de ses parents [pour plaire à Dieu] n’ira jamais en enfer, quelles que soient ses actions. Quiconque rompt les relations avec eux n’entrera jamais au paradis, quelles que soient ses actions ».
Observe les règles de bonne conduite en privé comme en public, car elles constituent la porte qui te conduira vers ton Seigneur. Témoigne du respect envers toute personne plus âgée que toi et manifeste de la miséricorde envers toute personne plus jeune que toi. Quant à l’individu qui a le même âge, témoigne-lui une considération identique à celle que tu t’accordes à toi-même. »
 Fais en sorte que ton Seigneur ne te surprenne dans ses interdits et tâche de ne jamais cesser d’observer ses ordres. Sois persévérant dans la lecture du Saint-Coran et dans les prières sur le Prophète (Paix et Salut sur Lui).
Traduction: comité scientifique Majalis
______________________
Ndénkaan lu Sëriñ Tuubaa dénkoon Sëriñ Moor Xari Gay Jolof:
"Bismilaahi Rahmaani Rahiim, ginnaaw bi ma santee Yàlla, julli ci Yonent bi SAW, na nga xam ni jot naa sa bataaxal, te dégg naa li nga ci wax. Yaw sama mbokk, maa ngi lay dénk nga sax ci ragal Yàlla, ndax ragal Yàlla kat, mooy caabi biy ubbi buntub lépp lu baax, te mooy caabi biy tëj buntub lépp lu bon, ragal Yàlla nag mooy, di moytu lépp lu Yàlla tere, tey def la mu diglé. [Yaw sama mbokk], maa ngi lay dénk ngay taqook di jëfe Sunnas Yonent bi SAW, te ngay moytu topp Bidaa. Na nga fonk say waajur te dileen topp ci lépp lu dul ag moy Yàlla, na nga moytu di dogoo ak ñoom, ndax am na Hadiis bu wax ne: "Kuy topatoo say waajur, ak loo man a def doo tàbbi sawara mukk, ku dogook say waajur nag, ak loo man a def doo tàbbi àjjana mukk" Na ngay am teggiin, ci lu feeñ ak ci lu nëbbu, ndax teggiin kat mooy bunt bi lay yóbbu ci Yàlla. Képp ku la mag na nga ko teral, képp koo mag na nga ko yërëm, képp koo maaseel def ko ni sa bopp." Fexeel ba bu la sa Boroom du gis ci lenn lu mu tere, te bum deñ ci di la gis ci ay ndigalam. Na nga farlu ci jàng Alxuraan ak di julli ci Yonent bi SAW. Wa Salaam.
L’image contient peut-être : texte

Enregistrer un commentaire

 
Top