Aucun texte alternatif disponible.

Barab yi ñu wara siyaar ci Màggal gi
- Barabu Sëriñ Tuubaa ak njabootam ga mu fa nekkal,(S. Mòodu Mustafaa, S. Fàllu, S. Abdul Qaadr, S. Saaliw S. Mourtada Mbàkke, S. Seex Gaynde Fàtma, S. Mbàkke Màdina, S. Moodu Buso Jeng ak S. Baara Mbàkke Fàlilu)
Mooy ci Jumaa ju mag ji, foofu ngay fekk barabu Sëriñ bu mag bi. Kuy siyaare barabu kilifa nak, da nga koy ñaanal loo man, li ci gëna yomb mooy nga def Faatiha ak 11 Ixlaas. Soo ko ñaanalee ba noppi, nga ñaan Yàlla sa soxla ci bàrkeb kilifa googu.
- Daaray Kaamil
Mooy bibliothèque Xaadimu Rasuul bi ñu deñci lu bari ci yenn téeré yoon wi ak téeréy woroom xam-xam yi, ak mbindum Sëriñ Tuubaa. Di nga fa fekk yit barabu Sëriñ Abdul Ahad Mbàkke.
- Aynu Rahmati
Di teen (puit) boo xam ne, Sëriñ Tuubaa ko gaslu woon, mu noppi ci ak nekkam, mu def ci ñaan yu bari, digal nit ñi ñuy bàrkeelu ci ndox mi
أسقيتنا خير مياه يرتوي
شاربها وكل فوز يحتو
- Armeel yi ci Tuubaa
Di barab boo xam ne, lu bari ci doomi Boroom Tuubaa fa lañ nekk, ku mel ni S. Baara Mbàkke, S. Abdu Boroom dër bi, ak ñeneen ñu bari ci doomam yu góor yi ak yu jigéen yi, ak ñu bari ci magi Murid yi, ku mel ni Seex Ibra Faal.
- Daaru Xudóos
Di nga fekk BAYTI, di Kër Sëriñ Tuubaa gi mu dëkkóon ci Daaru Xudóos, te soo demee di nga fa fekk lu bari ci ay bagages yu mu moom, ay gaal aki téeré yu fi Sëriñ bàyi ngir bàrkeelu.
Di nga fa fekk yit jàkkay Sëriñ Tuubaa gi mu duggée woon xalwa ba muy waaj tukkib géej gi.
- Daaru Minan
Barabu Sëriñ Basiiru Mbàkke (1895-1967), di doomi Boroom Tuubaa, di boroom xam-xam, te di ab yare kat, di baayi Sëriñ Muntaqa Mbàkke Xalifa général des Mourides.
- Barabu S. Sonhibu ibn Xaadimu Rasuul, doonoon jàngle katu Àlxuraan di ab yare kat (1917-1991).
Barab baa ngi nekk ci fi Sëriñ Tuubaa tuddée woon Daaru Rahmaan ci ginaaw Daaru Xudóos
- Guy mbind
Barabu Sëriñ Siidi Maxtaar juróom ñaareelu Xalifa Sëriñ Tuubaa (julliet 2010- janvier 2018)
- Armeeli Bàqiya
Di barab yoo xam ne, bokk na ci ligéey yi fi Sëriñ Abdul Ahad Mbàkke bàyi, ñu deñci fa kilifa yu bari ci yoon wi ak taalibé Sëriñ Tuubaa yu bari
Akb Majalis

Enregistrer un commentaire

 
Top